Youssou N'dour

Shukran Bamba Lyrics

Shukran Bamba video

Youssou N'dour - Egypt album
ALBUM
Votes:
0
See also:
Wrong lyrics?

Youssou N'dour - Shukran Bamba lyrics

Alxamdulillaay ma sant Yàlla
Bi mu ma wonaleek Cheikh Ahmadou Bamba
Céy jiile waay su feeñutoon Mbacké
Lislaam ji dik te kon ndaw gàcce
Këpp ku daan liggéeyal diine
Nasaraan bi rey la mbaa far la génne
Nasaxale Iislaam de moo doon seen yitte
Cheikh Ahmadou Bamba moo leen far wàcce

Chorus:
Shukraan laka
Shukraan laka
Shukraan shukraan
Shukraan shukraan
Modou Bamba

Xamalena ma Yàlla, xamale ma yonentam
Wax ma ne jaam de day jaamu sangam
Litax ñu kaan ko Xaadimu Rasulu
Moo ma yëngal ba ma far ca sóobu
Leketu neen neenañu naxul béy
Fu ñëpp daw jublu gisnañu fa lu réy
Yàgg na ma gëstu lu jëm ci Bamba
Masuma gis fu mu juuyook waa ja

Chorus:
Shukraan laka
Shukraan laka
Shukraan shukraan
Shukraan shukraan
Modou Bamba

Mënuma la fey xanaa ma woy la
Liggéey ba dee rek ngir àddiya la
Mbacké danga yaa ginaaw ak kanam
Nañ' roy i yow ngir mëna jëm ci kanam

Soo déggee ma naan waa ja,
waa ja mooy kiy waajale gaa ña
Te kooku daal, moo di doomi Abdoulaye ja ca Madina Youssou N'dour - Shukran Bamba - http://motolyrics.com/youssou-ndour/shukran-bamba-lyrics.html

Ahmadou Bamba, man de ant naa la

Jaa jëf baayi Mamadou Lamine Barra
Sama diggënteek Yàlla yaa ma ko leeral
Lu ne wonenga ko taxul nga jeexal
Yaa tax may baaleek di yërëmaate
Jaa jëf, jaa jëf baayi Sëriñ Saliou ak Sëriñ Mourtala

Chorus:
Shukraan laka
Shukraan laka
Shukraan shukraan
Shukraan shukraan
Modou Bamba

Mënuma la fey xanaa ma woy la
Liggéey ba dee rek ngir àddiya la
Mbacké danga yaa ginaaw ak kanam
Nañ' roy i yow ngir mëna jëm ci kanam

Amadu Bamba, man de sant naa la
Jaa jëf baayi Mamadou Lamine Barra
Sama diggënteek Yàlla yaa ma ko leeral
Lu ne wonenga ko taxul nga jeexal
Yaa tax may baaleek di yërëmaate
Kenn dootuma àtte te bañ xeebaate
Jaa jëf, jaa jëf baayi Sëriñ Saliou ak Sëriñ Mourtala

Chorus:
Shukraan laka
Shukraan laka
Shukraan shukraan
Shukraan shukraan
Modou Bamba

Mënuma la fey xanaa ma woy la
Liggéey ba dee rek ngir àddiya la
Mbacké danga yaa ginaaw ak kanam
Nañ' roy i yow ngir mëna jëm ci kanam

Write a comment

What do you think about song "Shukran Bamba"? Let us know in the comments below!

More "Egypt" Album Lyrics

Recommended songs